Leeray

Wizzy Kana

Compositor: Não Disponível

Toog ci sama xol ba abadan
Daiman dénk naa la sama ruu
Yaw laa teg ci kaw ndax yaa ci mën
Mënuñu bëre sa kaw ndax yaa ma daan
Ay wax yu sew du mëna ñàkk suñu biir
Bul ma meree su ma la tooñee nang ma baal

Leeraay
Yaay sama leeraay
Yaa ma jële ci lëndëm sotti ma leer
Yaa may mottali
Sa xol du wet ndax maa koy wetali
Eh yaw la diamond bi mëna leeral sama eyes

Yaay sama lingeer bëgg naa la def jabar
Dofloo nga ma ba pare dénk naa la samay fan
Bëgguma nga mer teg naa la fi ma teg sama yaaya booye
Yaa ma jural samay doom
Yaw laa nara def seen yaaya booye
Mbëggeel day sax ci xol yaw
Yaay garab bi mëna faj sama feebar
Jarul maa lay wax ni dama la nob
Boo xolee samay bët ding ko fa gis sax

Leeraay
Yaay sama leeraay
Yaa ma jële ci lëndëm sotti ma leer
Yaa may mottali
Sa xol du wet ndax maa koy wetali
Eh yaw la diamond bi mëna leeral sama eyes

©2003- 2025 lyrics.com.br · Aviso Legal · Política de Privacidade · Fale Conosco desenvolvido por Studio Sol Comunicação Digital