Compositor: Não Disponível
Jël nga sama xol, xel bi ci yaw la miir
Janeer sa jëm ji, weetay bi daf ma diis, diis, diis
Namm naa jote say bataaxal ngir xam ci lan nga ne
Nelawatuma guddi ba bët sétt di xool say natal, jaxane naa
ku la mérité, waroo forcé pour am son attention
Mbëggeel solution la war a doon mais warul nekk equation
Yaw boo ma seetaanee
May nga suñu noon yi lu ñuy reetaane
Buleen jox nopp dañoo seytaane
Lu waay mën a def yaw nañu ko waxtane
Yaw boo ma seetaanee
May nga suñu noon yi lu ñuy reetaane
Buleen jox nopp dañoo seytaane
Lu waay mën a def yaw nañu ko waxtane
Diggënte waat ak yaw
Wax la sama nameel
Gisante waat ak yaw
Won la sama nobeel
Xol du fen boo nekoon ak kenen
Sa xel du jugee ci man
Ndax mbëgeel bu dëggoo du fen
Su la jekku wee dalay daan
Mënuma fàtte fi ñu jaar te duma
Bàyyi mu naxsaay li ma mom
Dam koy jëli waat maa la moom
Te duma la saggane
Yaw boo ma seetaanee
May nga suñu noon yi lu ñuy reetaane
Buleen jox nopp dañoo seytaane
Lu waay mën a def yaw nañu ko waxtane
Yaw boo ma seetaanee
May nga suñu noon yi lu ñuy reetaane
Buleen jox nopp dañoo seytaane
Lu waay mën a def yaw nañu ko waxtane