Compositor: Não Disponível
Jaral nga ma taxaw feccalla ndaat saay
Yaay buuru sama xol kon fu la neex fa laale
Ku la son beri nga daan ko
Ci digg ëtt bi nu la neex daggoo
Farata rekk laa la doon doyee
Dama la nob ba am sa faiblesse
Lu ëpp turu baby lii dafa fees
Dam lay xalaat ba sama xel bi ne mes
Lu way dëgger dëgger dinga daanu
Say keseng keseng moo may taxa aalu
Yeggël sama xel di ma suusloo
Yaa raw daju volet bi may taxa metti
Risque la, risque la
Jee ma dox sa garde risque la
Risque la, risque la
Jee ma dox sa garde risque la
Jalgati jalgati yaw
Sama xol bi yaa ko yëngël yëngël
Yaw yaa may feccloo ndaat saay
Jalgati jalgati yaw
Sama xol bi yaa ko yëngël yëngël
Yaw yaa may feccloo ndaat saay
Lingeer, lingeer
Yaw yaa may feccloo ndaat saay
Lingeer, lingeer
Yaw yaa may feccloo ndaat saay
Dëkke di ma caw xiir bi doo baale
Dawal sama kaw dee ma yobbale
Eh dëgin ndaat saay
Eh dëgin ndaat saay
Tay ma feccal la dëgin ndaat saay
Chéré sama chéri
Yaa ma tere nelaw
Say cakas cakas sama kaw
Lii moo ma tee
Def ma ndank, def ma ndank
Xale bi dina mësa ray doomu jaambur
Yaadi wuurus ngalam
Feccal ma tukkusu ngalam
Yaay awoo buuru këram
Ku mer na fa de yaa fa xam
Xale bi amoo moroom
Maa la sant gërëm
Or nga yëgoo përëm
Yaw laay topp dee ma bërëng
Risque la, risque la
Jee ma dox sa garde risque la
Risque la, risque la
Jee ma dox sa garde risque la
Jalgati jalgati yaw
Sama xol bi yaa ko yëngël yëngël
Yaw yaa may feccloo ndaat saay
Jalgati jalgati yaw
Sama xol bi yaa ko yëngël yëngël
Yaw yaa may feccloo ndaat saay
Lingeer, lingeer
Yaw yaa may feccloo ndaat saay
Lingeer, lingeer
Yaw yaa may feccloo ndaat saay